Home 🎬 Bollywood 🎵 Pakistani 🎤 English Pop

Ballago ndumbé Yaatma

👤 Youssou N'Dour 🎼 MBALAX ⏱️ 5:14
🎵 1165 characters
⏱️ 5:14 duration
🆔 ID: 7766992

📜 Lyrics

Billaay, ballago ndoumbé yatma,
Su ñu waaji xaj oon na fi
Naxxar doηη,la ñu bayyee
Yalla, wonneeti na

Li tax ba mbir mi metti lool,
ñun da ñu ko foog wul woon
Yëf yi gaaw ba bette gnou
Billaay wéetël na ñu

Njiinoo njiin faramaareen,
Gòor u jaaga, nelaw naa
Baay i wally dem na nii,
ñun daal wéetël na ñu

Ma ngi koy jaale Sénégal,
Di ko jaalé Gambia
Di ko jaalé adduna,
Ndaanaan ba dem na nii

Thione ballago, ndoumbé yatma
Bu yalla buur bi doon taggoo,
Kon di na ñu bayék yaw
Ni patrimoine bi nga ñu bayyeel,
Yee gua nit gñi, tete leen ci adduna
Yee gua nit gñi, tete leen
Xam al leen ci adduna
Ahhh - Balaago

Yee gua nit ñi ci adduna xam al leen
Ni ñu war a nekkek
Ak ni ñu war a dundée,
Ak ni ñu war a jëfleentee
Jinaxoo mbaay
Yaw mi dëkké biir suuf,
Boo dem ee neel ballago, réew maa ngi koy joy
Aduna ngi koy jooy,
Art baa ngi koy jooy

Njiin faramaareen,
Thione seck, wéetël na ñu
Ballago ndumbé yaatma
Adduna, am ul solo

Li tax ba mbir mi metti lool,
ñun da ñu ko foog wul woon
Yëf yi gaaw ba bette gno
Ndanaan ba demna ni
Njiin faramaareen,
Thione seck, wéetël na ñu
Ballago ndumbé yaatma
Adduna, am ul solo

⭐ Rate These Lyrics

Average: 0.0/5 • 0 ratings